1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda. Céy liika baax te neexati, ay bokk yu bokk dëkk, di benn!
2
Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ, siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona, rogalaat ba ci mbubbam,
3
neex ni layub tundu Ermon, neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ. Fa la Aji Sax ji dogale barke, muy dund, ba fàww.