1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ayca, santleen Aji Sax ji, yeen jaami Aji Sax ji yépp, yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi.
2
Yékkatileen seeni loxo ca béreb bu sell ba, te sant Aji Sax ji.
3
Yal na la Aji Sax ji barkeele fa Siyoŋ, moom mi sàkk asamaan ak suuf.