v.2.10.1

Taalifi cant 136

26 Versets

1

Nangeen sante Aji Sax ji mbaaxam.

2

Santleen Yàllay yàlla yi.

3

Santleen Sangu sang yi.

4

Moo wéetoo jaloore yu mag yi.

5

Moo sàkk asamaan ci manooreem.

6

Moo lal suuf ca kaw ndox ma.

7

Moo sàkk leer yu mag yi:

8

jant bi yilif bëccëg,

9

weer ak biddiiw, guddi.

10

Moo faat taawi Misra yu góor ya,

11

seppee bànni Israayil ca ñoom,

12

ci dooley loxoom ak kàttanu përëgam.

13

Moo xar géeju Barax ya ñaar,

14

jàllale bànni Israayil ca digg ba.

15

Moo xalab Firawnaak mbooloom ca géeju Barax ya.

16

Moo jiite ñoñam ca màndiŋ ma.

17

Moo duma buur yu mag ya,

18

bóom buur yu màgg ya,

19

reyaale Sixon buurub Amoreen ña,

20

reyati Og buuru Basan.

21

Moo nangu seen réew, joxe,

22

sédde Israayil ma dib jaamam.

23

Ci biir nootaange la nu geesoo,

24

ne nu siféet ci loxoy noon ya.

25

Mooy leel bépp boroom bakkan.

26

Santleen Yàlla mi ci asamaan!