1
Ca tàkkal dexi Babilon, foofa lanu daa toog, fàttaliku Siyoŋ, jooy.
2
Ca garab ya lanu daa wékk sunuy xalam.
3
Fa la nu sunuy sang daa woyloo, noot nu, bëgg nu bégal leen, naan: «Woyalleen nu ci woyi Siyoŋ.»
4
Moo! Nu nuy woye woyu Aji Sax ji kaw suufas yéefar?
5
Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, yal na ma doole dëddu!
6
Yerusalem, su ma la fàttalikuwul, fonk la, ba gën laa bége lépp, yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.
7
Aji Sax ji, fàttalikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleen a màbb, ba suuf sa dëkk bi sampe siiñ!»
8
Yeen waa Babilon gi ñu nara fàllas, ndokkalee ku leen fey jëf ja ngeen nu def!
9
Ndokkalee ku ne cas seeni fere, tas ciw doj!