v.2.10.1

Taalifi cant 138

8 Versets

1

Ñeel Daawuda. Ma sante la sama léppi xol, woy la, gàngooru Yàlla ga ca kaw seede.

2

Ma sujjóot jublook sa kër gu sell gi, di wormaal saw tur, ngir sa ngor ak sa worma. Màggal nga sa tur ak sa kàddu, ba mu tiim lépp.

3

Bés ba ma wootee, yaa ma wuyu, ñemeel ma, dooleel ma.

4

Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal, ñoo dégg kàddu yi nga wax.

5

Nañu woy say jaloore, naan: «Aji Sax jeeka màgg ndam!»

6

Aji Sax jee kawe! Ku toroxlu, mu niir; ku réy, mu ñooru.

7

Ma wéye njàqare, nga musal ma, dogalee sa loxo merum noon, walloo ma sa ndijoor.

8

Aji Sax jee may feyul. Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor! Bul wacc ñi nga binde sa loxo.