v.2.10.1

Taalifi cant 141

10 Versets

1

Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Aji Sax ji, woo naa la, gaawe ma! Bu ma lay woo, teewlu ma.

2

Yal nanga ma nangul samag ñaan ni cuuraay lu ñu la taalal, loxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.

3

Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu.

4

Bu ma xiir ci lu aay, may jëfe jëf ju bon, ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, di wàlli seeni bernde.

5

Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, bantal ma ci ngor. Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.

6

Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj, ba noon yi xam ne dëgg laa wax.

7

Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet, ni la njaniiw di ŋaye, aw seeni yax yu tasaaroo.

8

Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët, yaw laa làqoo, bu ma seetaan, ma dee.

9

Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal, ak fiir yi ma defkati ñaawtéef yi tegal.

10

Yal na ku bon tàbbi cig fiiram, te man ma teggi, wéy.