1
Dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunt ma.
2
Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
3
sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.
4
Bu ma yoqee, ràññee nga samay jéego; yoon wi may jaare lañu ma làqal am yeer.
5
Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf.
6
Aji Sax ji, ma woo la wall; ma ne, yaay sama kiiraay, di sama séddoo fi kaw suuf.
7
Teewlul, ma ne wóoy, damaa manatul, xettali ma ci ñi ma topp, dañu maa ëpp doole.
8
Ngalla génne ma fi ma tëje, ma sant la. Man la way-ngëm ñi di yéew ëllëg, yaa may xéewale ab yool.