1
Màggalleen Ki Sax! Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, màggal ko fi ndajem wóllëreem ñi.
2
Na Israayil bége Kii ko sàkk, doomi Siyoŋ, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii.
3
Nañu màggale turam am pecc, tëggal ko, xalamal ko.
4
Aji Sax jee safoo ñoñam, di terale néew-ji-doole ag mucc.
5
Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,
6
di xaacuy kañ Yàlla, ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
7
ngir duma yéefar yi, mbugale ko yooyu xeet,
8
yeewe seeni buur ay càllala, jénge seeni njiit jéngi weñ,
9
ngir sottalal leen àtte bi ñu bind, muy ndamu wóllërey Yàlla yépp. Màggalleen Ki Sax!