v.2.10.1

Taalifi cant 150

6 Versets

1

Màggalleen Ki Sax! Nangeen màggale Yàlla biir këram gu sell, màggale ko ca tatay asamaanam.

2

Màggaleleen ko ay jalooreem, màggale ko màggam gu réy.

3

Màggaleleen koob bufta, màggale ko xalam ak moroom ma.

4

Màggaleleen ko njiin aki pooj, màggale ko xalam ak toxoro.

5

Màggaleleen ko tëggum weñ mu xumb, màggale ko tëggum weñ mu kawe.

6

Na lépp luy noyyi màggal Ki Sax! Màggalleen Ki Sax!