1
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Aji Sax ji, kuy ganeji sa xayma? Ana kuy dëkki sa tund wu sell?
2
Xanaa ki wéye màndu, di def lu jekk, di wax dëggu xolam.
3
Du sos, du tooñ dëkkandoo, du baatal moroomam.
4
Ku siblu, mu sib, ku ragal Yàlla, mu teral. Mooy sàmm ngiñam, su ko dee lor it.
5
Du leble, ba teg ca; du nangu ger, ngir fexeel jàmbur. Lii ku koy jëfe doo jang.