1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda. Ab dof a nga naa ca xelam: «Yàlla amul!» Ñu ni mel ay def njekkar, seeni jëf siblu, kenn defu ci lu baax.
2
Aji Sax jee tollu asamaan, jéer doom aadama, di seet ku ci xelu, tey wut Yàlla.
3
Ñépp lajj, bokk yàqu yaxeet. Kenn deful lu baax, du kenn sax.
4
Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, te wutuñu Aji Sax ji.»
5
Foofu lañuy tiite tiitaange ju réy! Du Yàllaa ngi ànd ak kuréeli ñu jub ñi?
6
Ku néewlee yaakaar, ngeen tas ko, waaye Aji Sax ji la làqoo.
7
Ana kuy tollu Siyoŋ, xettali Israayil? Éy bés bu Aji Sax ji tijjee wërsëgu ñoñam, ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! Ndaw bànneex laa ne, ci Israayil gii!