v.2.10.1

Taalifi cant 28

9 Versets

1

Ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, yaw laay woo, di la wéeroo, bu ma tanqamlu. Soo nee cell, ma xawa tàbbim pax.

2

Ngalla déglul, ma tinu la, woo la wall, dékk lay loxo, jublu sa néegu biir bu sell ba.

3

Bu ma sànkaaleek ab soxor, di ma booleek kuy def lu bon, di wax moroom ma jàmm, te dencal ko ay ca xolam.

4

Fey leen seen liggéey, seen kemu jëf ju bon. Jox leen seen añu jëf, yool leen seen yelleef.

5

Xooluñu Aji Sax jeeki jëfam, ak liggéey bi mu def. Da leen di yàqate, te dootu leen yékkati.

6

Jaajëfe Aji Sax ji, ki ma nangul samay dagaan!

7

Aji Sax jee may dooleel, di ma feg. Moom laa wóolu, mu wallu ma, sama xol tooy, ma woy, sante ko.

8

Aji Sax jeey dooleel ñoñam. Mooy làq, di musal buur bi mu fal.

9

Ngalla musalal sa mbooloo, barkeelal sa ñoñ ñii, sàmm leen, boot ba fàww.