v.2.10.1

Taalifi cant 29

11 Versets

1

Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Yeen goney Yàlla yi, seedeelleen Aji Sax ji, seedeelleen ko teraangaak doole,

2

seedeelleen Aji Sax ji màggaayu turam. Sujjóotalleen Aji Sax ji gànjaroo sellaay.

3

Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma, Yàlla mu tedd maa dënu, Aji Sax jeey tiim ndox mi ne màww.

4

Aji Sax jeey àddoo doole, Aji Sax jeey àddoo daraja.

5

Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar, Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.

6

Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu, tundu Siryoŋ it, mbete yëkk wu ndaw.

7

Aji Sax jeey àddu, fettaxal sawara, mu boy.

8

Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ, Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.

9

Aji Sax jeey àddu, kéwél matu, garabi àll ruus, biir këram di mennum riir, naan: «Màggalleen ko!»

10

Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu, Aji Sax jee falu buur ba fàww.

11

Aji Sax jeey kàttanal ñoñam, di barkeele jàmm ñoñam.