1
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor.
2
Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare! Ñu baree may jógal,
3
ñu baree may tooge naa: «Yàlla du ko wallu!» Selaw.
4
Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg, di ma teral, di ma siggil.
5
Maay woo Aji Sax ji wall, mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw.
6
Maay tëdd nelaw, yewwu; Aji Sax ji di ma aar.
7
Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, te duma ragal.
8
Éy Aji Sax ji sama Yàlla, jógal, wallu ma! Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, foq seeni sell.
9
Aji Sax ji, yaa moom wall, sa mbooloo jagoo sa barke. Selaw.