1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2
Éy Yàlla, yaw mi may àtte dëgg, maa ngi woote, wuyu ma; maa xatoon, nga yaatal ma. Ngalla baaxe ma, nangul ma.
3
Yeen boroom daraja yi, buleen yàqati sama der, buleen sopp caaxaan, di sos. Selaw.
4
Xamleen ne Aji Sax ji day séddoo ku ko ragal, te bu ma woowee Aji Sax ji, mu dégg.
5
Loxleen te baña bàkkaar, waxtaanleen ak seen ngegenaay te noppi. Selaw.
6
Rendileen seen sarax yi war, te wóolu Aji Sax ji.
7
Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?» Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw!
8
May nga ma bànneexu xol bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.
9
Jàmm laay tëdde, nelaw, Aji Sax ji, yaw doŋŋ yaa may dëël fu wóor.