1
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maxalat, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda.
2
Ab dof a nga naa ca xelam: «Yàlla amul,» Ñu ni mel ay def njekkar, seeni jëf siblu, kenn defu ci lu baax.
3
Yàllaa tollu asamaan, jéer doom aadama, di seet ku ci xelu, tey wut Yàlla.
4
Ñépp a dëddu, bokk yàqu yaxeet. Kenn deful lu baax, du kenn sax.
5
Yàlla nee: «Xanaa ñiy def lu bon, xamuñu dara? Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, te wutuñu Yàlla.»
6
Waaye ñooy tiit a tiit fu tiitaange amul. Yàllaay tasaare néewi nit ñi la gaw. Yàllaa leen wacc, nga gàcceel leen.
7
Ana kuy tollu Siyoŋ, xettali Israayil? Éy, bés bu Yàlla tijjee wërsëgu ñoñam, ndaw mbégte ci giirug Yanqóoba! Ndaw bànneex laa ne, ci Israayil gii!