1
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda.
2
Mooy ba waa Sif demee ca Sawul, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew.
3
Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur, jox ma dëgg, ci sa kàttan.
4
Éy Yàlla, déglul, ma ñaan, teewlul, ma wax la.
5
Ay doxandéem a ma jógal, di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan, te seetuñu ci Yàlla. Selaw.
6
Yàllaa ngii, moo may dimbali; Boroom bee yor sama bakkan.
7
Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru, yal na leen sa dëgg sànk.
8
Xol bu tàlli laa lay sarxale. Aji Sax ji, yaa baax, ma sant la.
9
Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële, ma tiim samay noon.