1
Dib taalifu cant. Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, moo def ay jaloore; kàttanam ak sellaayu dooleem jox na ko ndam li.
2
Aji Sax jee xamleg wallam, feeñal àtteem, xeet yi gis.
3
Moo fésal bànni Israayil ngoram, fésal ko kóllëreem, àddina ba mu daj di gis ni nu sunu Yàlla walloo.
4
Yeen àddina sépp, xaaculleen Aji Sax ji, sampleen, sarxolle te woy!
5
Xalamalleen Aji Sax ji, woyal ko, xalamal ko, woyati!
6
Walleen liit yi, wal bufta yi te xaacu fa kanam Buur Aji Sax ji!
7
Na géej riirandook li ko fees, mook àddinaak li ci biiram,
8
dex tàccu, tund sarxolleendoo,
9
gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi dëgg, tey àttee xeet yépp yoon.