v.2.10.1

Taalifi cant 99

9 Versets

1

Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragalleen ko! Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!

2

Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg, kawe, tiim xeetoo xeet.

3

Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaalleen ko. —Kee sell!

4

Buur, jëfe yoon mooy dooleem. Yaa saxal yoon, dëgg ak njub ci askanu Yanqóoba.

5

Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell!

6

Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam, Samiyel bokk ca ñay ñaan ci turam. Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul.

7

Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom, ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon.

8

Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon, di seen Yàlla ju leen di baal, te di leen mbugale seeni jëf ju bon.

9

Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa tundam wu sell wa. Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!