1
Màggalleen Ki Sax! Ndokkalee ku ragal Aji Sax ji, di tàqamtikoo ay santaaneem.
2
Aw askanam ay am doole ci réew mi. Ku jub saw xeet barkeel,
3
alal ak koom am sa kër, sag jëf yu jekk sax dàkk.
4
Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub ak ku baax, di boroom yërmande ak njubte.
5
Ki baaxle mooy ki laabiir, di leble, di jëflante cig njub.
6
Ku jub du tërëf mukk, te dees na ko fàttaliku ba fàww.
7
Du ragal dég-dég bu tiis, xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji,
8
fit wa toog, du ragal, ba kera muy gis noonam jóoru.
9
Moo yéwén ci li muy may néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.
10
Soxor bi da koy gis, mer, iñaan bay yéyu, jeex tàkk; nde soxor, yaakaar ju tas rekk.