1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ndokkalee képp ku ragal Yàlla, di jëfe ay yoonam.
2
Yaay lekk saw ñaq, mbégteek ngëneel ñeel la.
3
Sa jabar ni garab gu meññ ci sa kër, say doom wër a wër sa ndab ni njëmbat lu jebbi.
4
Ki ragal Aji Sax jaa ngoog, nii rekk lay barkeele.
5
Yal na la Yàlla barkeele fii ci Siyoŋ; yal nanga teewe xéewalu Yerusalem sa giiru dund gépp,
6
te nga gis say sët. Yal na jàmm dal Israayil.