1
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla. Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal. Israayiloo, waxati ko:
2
Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal, te taxul ñu man ma.
3
Sama gannaaw gi lañu gàbb a gàbb, rëdd koo rëdd nib tool.
4
Waaye àtteb Aji Sax ji mooy dëgg, dog na buumi ñu bon ña.
5
Képp ku noonoo Siyoŋ, yal nañu ko dëpp, gàcceel ko.
6
Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd, balaa law, lax.
7
Du doyub ŋëb ku ko dog; du doyub say ku ko for.
8
Ku fa jaare it du ko ne: «Jaajëf, Aji Sax ji barkeel; jaajëfe yaw, yal na Aji Sax ji barkeel.»